wolof
stringlengths 1
166
| french
stringlengths 2
331
|
---|---|
ajagjag | il y a belle lurette |
Dem na ca ajagjag | il est parti il y a belle lurette. |
aaye b- | interdiction |
Aaye bi du yàgg | L'interdiction est temporaire (ne durera pas). |
aalim j- | Érudit |
Aalim yi ci dëkk bi daje nañu | les érudits qui sont dans la ville se sont réunis. |
alamaan | mettre à l’amende |
Soo ñówul, dinañu la alamaan | si tu ne viens pas, tu seras mis à l’amende. |
aay b- | jeu de jeunes filles où on essaie à tour de rôle de placer le même pied que la meneuse qui, elle, essaie de prendre les joueuses à contre-pied |
Bàyyileen aay bi te dem ca waañ wa | laissez ce jeu de {aay}et allez à la cuisine. |
almasi b- | (Héb.) Messie |
Yéesoo di almasi bi gurmet yi doon xaar | Jésus est le messie qu’attendaient les chrétiens. |
agsi | arriver (au lieu du locuteur) |
Xale yi agsi nañu | les enfants sont arrivés (ici). |
(loc.) Agsi nga nak | t'y voilà ! |
aayoo | aider un bébé à s’endormir en lui chantant une berceuse |
Demal aayoo bebbe, mu nelaw | va bercer bébé afin qu’il s’endorme. |
Aayoo nenne | dodo, l’enfant dort. |
ajab b- | nom originel de l’ethnie wolof |
Ñi ñuy wooye Wolof tey, am na jamano joo xam ne ajab lañu leen daan wooye | ceux qu’on appelle Wolof actuelle-ment, il fut un temps où on les appelait Ajab. |
aay-gaaf | se dit d’un animal ou d’une personne qui porte la poisse |
Sa fas wi dafa aay-gaaf | ton cheval porte la poisse. |
aal b- | mauvaise humeur |
Bu ko aal bi jàppee | quand il est de mauvaise humeur. |
aareen b- | aire aménagée pour les jeux de lutte. (De nos jours, on emploie plus souvent le terme làmb) |
aar | laver une pièce de linge pour la première fois |
Maa ngi sooga aar mbubb ma ma jéndoon | je viens seulement de laver le boubou que j’avais acheté. |
aaya b- | verset du Coran |
Ci ban aaya lañu ko waxe ? | dans quel verset l’a-t-on dit ? |
afirig g- | afrique |
a ngee | voilà |
Omar a ngee | voilà Omar. |
a ngale | voilà |
Omar a ngale di dem | voilà Omar qui s’en va. |
a ngoogale | voilà |
Omar a ngoogale | voilà Omar. |
alxames j- | jeudi |
Daawunu dem ekool alxames | nous n’allions pas à l’école le jeudi. |
a ngi | voici |
Suma kër a ngi | voici ma maison. |
Maa ngi ci li nga wax | J'approuve ce que tu as dit. |
Maa ngi ci yow | je m’occupe de toi; je suis à toi. (ou encore) je t’aime. |
afeer b- | affaire |
Lii, afeer la | ça, c’est une affaire. |
Afeer la | C'est confidentiel. |
aniinu | se maquiller en bleu |
Géj naa gis ku aniinu | il y a longtemps que je n’ai pas vu qqn se maquiller en bleu. |
a ngoogule | voici (à côté de toi) |
Aw doj a ngoogule ci sa wetu tànk | voilà un caillou à côté de ton pied. |
aniin | mettre du bleu de maquillage |
Bul aniin xale bi | ne maquillage pas l’enfant en bleu ! |
aniin j- | bleu de maquillage |
Aniin ji mu def dafa ëpp | il a mis trop de maquillage bleu. |
abajadda b- | alphabet |
Mu ngi tollu ci abajadda | il en est à l’alphabet. |
aji | celui qui fait |
Yàlla, aji-kàttan, dimbali ma | Dieu, source de toute puissance, aide-moi ! |
aniwerseer b- | anniversaire |
a ngii | voici (tandis qu’on montre) |
Omar a ngii | voici Omar. |
aññaane | éprouver de la jalousie vis-à-vis de qqn à cause d’une chose |
Danga ma aññaane sama séy bi | tu me jalouses à cause de mon couple. |
aji-gëm j- | croyant |
Aji-gëm ji, Yàllaa koy sàmm | le croyant, c’est Dieu qui le protège. |
alal j- | richesse fortune bien |
Bu nit ñiy wut alal, yow, wutal nit ñi | quand les hommes cherchent la richesse, toi, cherche les hommes ! |
(prov.) Alalu golo a lex ba | on garde ses biens près de soi (pour y veiller). |
antule | réussiir en qqch |
Yàlla dimmali na nu ba nu antule nun ñépp | par la grâce divine, nous avons tous réussi. |
aajowoo | avoir besoin de |
Lépp loo aajowoo, dina ko toppatoo | tout ce dont tu auras besoin, il s’en occupera. |
asiire | assurer, garantir par un contrat |
araamal | considérer comme illicite, prohiber par la loi islamique |
Mbaam, ci yàpp yi ñu araamal la bokk | le porc fait partie des viandes prohibées. |
araab | arabe |
afal | libérer |
Dañuy téye xale yu jigéen yi ci kër yi, afal xale yu góor yi | on retient les filles à la maison et on libère les garçons. |
ableloo | ordonner de prêter |
Ku la ableloo sama gënn | qui t’a demandé de prêter mon mortier. |
aras b- | l’au-delà |
Kenn mësula bàyyikoo aras | personne n’est jamais revenu de l’au-delà. |
abada j- | Éternité |
Borom bi, duma la bàyyi ba abada | Seigneur, je ne te quitterai pas jusqu’à l’éternité. |
ariko j- | haricot |
ar | être ferré sur (les études) |
Dafa jàng ba ne ar | il est pétri de connaissances. |
araw | rouler la farine en gros granules |
Janq bu mënul araw; mas-sa yow | une fille ne sachant pas rouler la farine; pauvre de toi ! |
abalaate | prêter (avec une certaine propension à le faire) |
Li muy abalaate saretam bi yépp dey, bëgga falu doŋŋ | il prête sa charrette (à qui veut) uniquement pour être élu. |
aji-gëm-xërëm j- | animiste |
armeel y- | cimetière |
Armeeli katolik yi ak yu jullit yee dend. | Le cimetière des catholiques et celui des musulmans sont contigus. |
(prov.) Néew, bu rombeey armeel, robam dootul neex | quand la dépouille va au delà du cimetière, son enterrement ne sera plus aisé. |
araf b- | signes graphiques de l’alphabet |
Ñaar fukki araf ak juróom benn a am ci seen liifantu | il y a vingt-six lettres dans leur alphabet. |
arikoweer j- | haricot vert |
armool b- | armoire |
aat b- | adulte qui n’est pas encore circoncis |
Dajale nañu aat yépp | on a réuni toutes les personnes ayant atteint l’âge de la circoncision. |